![Yàlla](https://source.boomplaymusic.com/group10/M00/05/26/0404bb4a29664be8a0bbbb37ca08c087.jpg)
Yàlla Lyrics
- Genre:Hip Hop & Rap
- Year of Release:2021
Lyrics
Yàlla - Ashs The Best
...
Xel du ko sut te xol a koy gis
Bëtt du ko sèen làmiñ mënu ko wax
Everyday every time neena moo ngi sa wet
Moo la gën na jege sa buumu xol ba
Yàlla a ngi fi
Moo ngi fii akk fii
Yàlla a ngi fee
Yàlla moo ngi everywhere
Moo Fii akk fii
Yàlla joggu fi
Yalla na Yàlla bay sa tòol
Ñun say jaam ñoo ngi lay ñaan
Nangul ñu lepp luñ la ñaan
Ngir faqqir day nangu daggaan
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Xel du ko sut waaye xol da koy yëgg
Boo ñu mayee ling nu mayoon
Dootu ñu def li ñu defoon
Xanaa yëggoo ni ñun yaru nañ
Buur Yàlla naatalal xarnu bi
Nangul ñu lepp liñ la ñaan
Ngir sa yërmande ñi ngi lay tuubël
Lepp lu xaraam te di nangu nuyoo ki jaam
Boo ñu joxee di nañ la sant
Te boo ñu joxul dutee ñu xëy di gën sant
Rafle,sonn xiif akk fande akk tëdd ci suuf
Ngir bëgg am sa yërmande
Du ñu xaddi, du ñu soof, du ñu daw te du ñu lakkatu
Ngir bëgg am sa yërmande
Loo wax ñu nangu, yay buur baaxal ñu
Te boo ñu mayee ling ñu mayoon jeegël ñu
Dootu ñu def li ñu defoon
Xanaa yëggoo ni ñun yaru nañ
Buur Yàlla naatalal xarnu bi
Nangul ñu lepp liñ la ñaan
Buur Yàlla naatalal xarnu bi