Wax dëgg Lyrics
- Genre:Spoken Word
- Year of Release:2019
Lyrics
Xarit kaay ma wax la samay xalaat
Denq ma say nopp
Ma toqal ci samay xalaat
Gaa ñi, kar nañu dëgg siif, siifaat
Ñu jàpp dëgg fàdd, fàddaat
Dëgg jib ñu gàntu, gàntuwaat
Saaga nañu dëgg, toroxal nañu dëgg,
Waaye taxul ba leegi dëgg sëgg
Ndax mooy kiy lakk seeni taat
Amna ñu dajaal ngemb ngir ñu këf sunuy xel tek ci kaw jaat
Suul dëgg, jëmbat jokkoy ibliis ngir mu naat
Bari nay kilifa yu jaay seeni baat
Di ñaarook ngublang, iblisa leen mey baat
Amna ñuy wax di yàq ay baat
Ngir jaxase suñuy xel, di ko baamtuwaat
Ci sunu Gaal, amna ñu bari-wax, tax a am-baat
Ta ku wax-dëgg ñu dëgg sa baat
Di nga wax dëgg sax, Yëkëti sa baat
Ñu lay artu naan la: "noppil ba laa ñu lay faat"
Ñaata doomu-aadama la caabi feete ginnaaw ci lu dul dëgg
Lépp rekk ndax li ñu doon ay nitu dëgg
Ñaata doomu-aadamaay dunde ribaa
Gaaw ci feewale, yakamti xibaar
Ta duñu wax mukk lu baax
Sa waay, askan wi tànn la, ràng la
Bàyyi ñu bare tippoo la, jiital la
Nga digg leen aafiya
Say kaddu tax ñu naw la, topp la
Ngala kon bul waccee say waggu kilifa
Lu fen lëndëmal,
Dëgg dina ko leeral
Bëset mooy wuutu guddi, tey bët set na
Ku dëkk ci di wax dëgg nag, ñu nee dof la
Séex Anta doy nama firde tey Senegaal ak sowu-jànt nangu nanu ni kangam la
Xarit deglul ma wax la samay xalaat
Denq ma say nopp ma toqal ci samay xalaat
Ay xalaat yu may faral saasu nekk di xalaat
Jëw, sos, fen, ñu jël jàpp sanni sa xaj
Soobu ci sutura ak teggin ndax ci la jàmm xaj
Wa xarit ndax xam nga ne
Dëgg a njëkk te moy mujj
folliko du tee bés dina ñëw mu falluwaat
Daane du tee mu jogaat
Fadd ko du tee taxawaat
Gaa ñi nag,
Su baaxul ci ñoom, ñu suul dëgg
Su baaxe ci ñoom, ñu sulli dëgg
Jikkooy kawteef, du jikkooy nitu dëgg
Lu mu metti-metti bul wor, waxal dëgg
Bul saalit, sàmmal sa ngor, bu ci kenn dëgg
Waa Mbokk ndax xam nga ni
Ku am fit dëgg, xam dëgg,
Dëggu teksi, di wax dëgg
Te am orma du dox bay rus mbaa di sëgg.
Nit nag dina topp xolam ba araftu dëgg
Li nu mel a Waral ñu war di bàyyi-xel xel
Ndax xel xamna dëgg
Ku xamul neel cell
Ta soo bëggee lijànti li xew,
Da ngay xam ba noppi lu waral li xew xew
Ndax dëgg ju rafle baaxul
Dem gëstu, wax fa nga war a waxee
Wax ba sa wax jottee
Wax ta bàyyi di wax
Ci jambur ndax loolu du wax
Mani nettali neex na
Waaye Wax dëgg baax na
Àndal ak dëgg ju dëggu,
Sa waay Dëgg du la mësa dëgg
Nañ labat dëgg, neexal dëgg
Ngir mu neexa dekku
Doon nitu dëgg
Góor yalla dëgg
Wax luñu gëm, ta muy dëgg
Ca ba muy dëgg
Ndax ca dëgg dëgg
Yàlla dëgg rek a la bëgg
Dëgg nag dina la gindi ci lëndëm
Indi la ci dëgg ju sëf dërëm
Topp ko, daa xamni moom rek a jar a gërëm
Fàtte ko , topp aji-gëm-xërëm
Mu jël sa bakkan ak say gët gëlëmal
Jàpp say mébét bank, dëgëral
Xarit neenañ wax dëgg du wàññi wërsëk
Ngala bu jottee na nga ka wax bamu mat sëkk
Ta Bul bëgg lu neex nit ba nee doo ko wax dëgg
Ngir baax
Ngir am lu baax
Ngir dundal mbaax
Nanu topp Yàlla ak i ndigalam
SLAM